Lines Matching refs:ne
5 Ñu jàpp te nangu ne sagu doomi aadama ak sañ-sañam yépp-dañu yam te kenn mënukóo jalgati, te lu lépp nekk na cës laay ci taxufeex ci mbirum àtte ak jàmm ci biir àdduna.
7 Ñu jàpp ne ñakk xam ak soofantal sañ-sañi doomi aadama indi na aymusiba yu tar tax képp kuy dund fippu. Temano egsi na ba mu nekk ci doomi aadama ñu mën a wax, xalaat, ci seen coobare, bundxatal, nàkk dëddu leen.
9 Ñu jàpp ne am na solo lool ñu aar sañ-sañi doomu aadama ak ay matukaay ci wàllu yoon; ngir doomu aadama moomu kenn du ko sonal, muy fippu ci nootaange ak lu koy bunduxatal.
11 Ñu jàpp ne am na solo lool ñu góor-goorlu ba gën a rataxal jokkalante gi diggante xeet yi.
13 Ñu jàpp ne ci bataaxal boobule mbootaayu xeet yi yeesalaat na ay pas-pasam jëme ko ci sañ-sani doomi aadama yu tolloo, ci sag, ci bir lépp lu aju ci dundin diggante góor ak jigéen, ci biir tawfeex gu yaa.
15 Ñu jàpp ne réew yi ci bokk jël nañu ay matukaay ngir dëgëral jokkalante gi ak mbootaayu xeet yi, ñu naw it bu baax sann-sañi doomi aadama ak tawfeex yu wóor ci biir àdduna yépp.
17 Ñu jàpp ne ànd taxawal sañ-sañ yeek tawfeex yi nekk na lu am solo lool ngir, darajaal matukaay yooyu.
19 Ndaje mu mag mi biral na ci bataaxal bii ne xeet yépp, réew yépp ak kurel yépp ñu jàpp li ci nekk, ci seen xel, te ñu góor-góorlu, ñu jaarale lii lépp ci njàng mi ak yar gi.
29 Ku ne mën naa wax ne am na ay sañ-sañ ak ay tawfeex yu sosoo ci bataaxal bii te amul xeej ak seen, rawatina ci wàllu xeet, melo, awra, làkk, diiné, peete ci wàllu politig, xalaat, réew mbaa askan woo mën ti sosoo, ci it wàllu juddu alal ak lu mu mën ti doon.
43 Nit ku ne am na sañ-sañ ñu war kaa nangul darajaam ci wàllu yoon.
46 Népp a yam ci kanamu yoon. Te it amul xeej ak seen, ku ne yoon woowu war na laa aar. Népp war nañu leen aar ci luy jalgati liñu tënk ci bataaxal bii ak bepp yëngu-gëngu buy indi par-parloo.
49 Nit ku ne am na sañ-sañ dem ci berebi àtte kaay yi ci reewam saa yoo xamne sañ-sañam yooyu dëppook sàrti réewam mba yoon jalgati nañu ko.
55 Ci lu wér, nit kune mën naa egg ci berebu atte kaay wax li ko naqari ci anam gu jub, te baña ànd ak par-parloo, ne dañu ko taxal.
73 2. Su fekkee ne nit ki dañu koy toppu ginnaaw bi mu defee jëyyi, mbaa yëngu-yëngóon méngóowul ak li mbootaayu xeet yi tëral, sañ-sañ boobu.
76 1. Nit ku ne am na sañ-sañ xeetoo cim réew.
78 2. Mënuñu ne nit ki xeetoowul cim réew te teguñu ko fenn, mbaa ñu xañ ko sañ-sañ su bëggee soppi xeetoom ak réewan.m
83 2. Sëy kenn menunuko fas, xanaa lu jiitu ku ne ci way-dencante yi joxe xalaatam.
96 Nit ku ne am na sañ-sañ wax mbaa bind lu ko soob. Ci waxam yooyule kenn menuko ce bundu xatal. Te it am na sañ-sañ di gëstu, di jot, di wasare ci anam gu yaa ay xabaaraki xalaat ak ay jumtukaay yu mi Men ti jefandikóo.
104 1. Nit ku ne am na sañ-sañ bokk ci ñiy doxal mbiri réewam. Mu teewal fa boppam, mbaa mu yabal ab ndaw mu teewal ko fa.
106 2. Nit ku ne am na sañ-sañ, amul xeej ak seen liggéey ci bépp béréb buy doxal mbiri réewam.
111 Nit ku ne meññeefu askan wi am na sañ-sañ ñu aar ko ci giru dundam. Ci dundam war na ci am xol bu sedd ci sañ-sañam yooyu, lu aju ci koom-koomam, ci dundinam ak ci lépp lu aju ci aadaam te di ko jox maanaa ak yookkute gu ànd ak tawfeex ci wàllu darajaam, loolu lépp nag ku ne doomu réew mi indi dooleem ak di jokkalante ak bitim réew te mu méngook tërërin ak am-amu réew mu ne.
114 1. Nit ku ne am na sañ-sañ liggéey, tànn it ci eanam gu ko neex liggéeyamm te mu dëppóok ay sàart yu yam te baax ci wàllu liggéey. Te it ñu aar ko ci ñàkkub liggéey.
120 4. Nit ku ne am na sañ-sañ samp mbaa bokk ci ay kurel yu koy taxawu ci wàllu liggéeyam.
123 Nit ku ne am na sañ-sañ noppalu, feexal xolal ak it di yamale diirub liggéeyam ak it léeg-léeg muy për, bër gu ànd ak xaalis.
126 1. Nit ku ne am na sañ-sañ am dundingu yamamaay ngir dëgëral wér-gi-yaramam, raataageem ak bu njabootam, lrawatina ci wàllu lekk col, dëkkuwaay, lépp lu aju ci wàllu paj ak bépp yëngu-yëngu gu am farata ci wàllu dundam. Am na it sañ-sañ ñu aar ko bu liggeeyatul bu feebaree, bu amee laago, ñàkk saxnaam mbaa sërinam, mbaa màgget, mbaa mu ñàkk li muy suturloo ci anam yu dul ci cootareem.
131 1. Nit ku ne am na sañ-sañ ñu jàngal ko, njàng mi waruñu ci fayaku lu mu bon bon ci njàng mu suufe mi te am solo. Njàng mu suufe mi lu war la. Njàng mu xarala mi, te it aju ci wàllu liggéey war nanu koo wasaare. Amul xeej ak seen njàng mu kawe mi ubbil nañu ko képp ku ko yelloo.
138 1. Nit ku ne am na sañ-sañ bokk ci dépp lu aju ci caaday askan wi, di bànneexu ci lu cu aju ak it bokk ci lépp luy suqali xarala gi ak lu ciy meñ.
140 2. Nit ku ne am na sañ-sañ ñu aaral ko lépp lu aju ci lu mudefar ci wàllu la xarala, mbind mbaa lu aju ci wàllu caala.
143 Nit ku ne war naa tawaxu dëpp lu aju a askan wi, ak lu aju ci bitim réewam ba sañ-sañ ak tawfeex yi bataaxalu xeet gi ëmb mën a sax.
146 1. Nit ku ne am na ay wareef yu ko war digganteem ak dëkkandoom yi ngir dëgëral ci anam gu ya darajaam.
148 2. Nit ku ne buy doxal ay sañ-sañam aki tawfeexam war naa sallook li ko yoon may, ngir mu mën a nangu, naw, sañ-sañ nawleem ba léepp lu aju ci yiw, teey ak naataange gu yaa sax ci askan wi.