Lines Matching refs:ko
9 Ñu jàpp ne am na solo lool ñu aar sañ-sañi doomu aadama ak ay matukaay ci wàllu yoon; ngir doomu aadama moomu kenn du ko sonal, muy fippu ci nootaange ak lu koy bunduxatal.
13 Ñu jàpp ne ci bataaxal boobule mbootaayu xeet yi yeesalaat na ay pas-pasam jëme ko ci sañ-sani doomi aadama yu tolloo, ci sag, ci bir lépp lu aju ci dundin diggante góor ak jigéen, ci biir tawfeex gu yaa.
26 Doomi aadama yépp danuy juddu, yam ci tawfeex ci sag ak sañ-sañ. Nekk na it ku xam dëgg te ànd na ak xelam, te war naa jëflante ak nawleen, te teg ko ci wàllu mbokk.
37 Waruñoo def kenn jaam mbaa mbindaan. Njaam ak njaayum jaam nanguwunu ko ci anam gu mu mën ti doon.
49 Nit ku ne am na sañ-sañ dem ci berebi àtte kaay yi ci reewam saa yoo xamne sañ-sañam yooyu dëppook sàrti réewam mba yoon jalgati nañu ko.
52 Menuñoo jàpp, tëj, mbaa genne kenn réewam te tegunu ko ci yoon.
55 Ci lu wér, nit kune mën naa egg ci berebu atte kaay wax li ko naqari ci anam gu jub, te baña ànd ak par-parloo, ne dañu ko taxal.
58 1. Bépp nit bu ñu taqal cimbir mu tar jàppe nanu ko ku set ba loolu ñu ko taxal leer nàññ ginnaaw bi ñu ko attee. Te ñu taxawu ko ci lépp lu koy aar ci atte boobule.
60 2. Duñu tëj kenn ci ay jëfam mbaa lu mu fàtte mbete loolu mu jëf ci jamono jooju nekkul mbir mu tar ci wàllu yoon, ci biir ak bitim réew. Foofu it yoon du ko teg lu dul limengóok li mu def ci jamono jooju.
63 Kenn warula xuus ci dundinu doomu aadama, bu njabootam, ci lu jëm ci këram mbaa lu mengóok moom, di damm it jarajaam. Buñu jalgatee yii nit kune am na sañ-sañ ñu aar ko ci wàllu yoon.
66 1. Nit kune am na sañ-sañ wëndeelu ni mu ko neexe, tànn it dekkuwaayam ci biir réew bu mu mën ti doon.
71 1. Nit kune bu ñu ko mbugalee am na sañ-sañ làqu ji, mbaa ñaan ñu làq ko ci yeneni réew.
78 2. Mënuñu ne nit ki xeetoowul cim réew te teguñu ko fenn, mbaa ñu xañ ko sañ-sañ su bëggee soppi xeetoom ak réewan.m
93 Nit kune am na sañ-sañ xalaat ak sa goom ci wàllu diine, soppi it diineem mba ngëmam, am na it tawfeex feeñal diineem, mbaa ngëmam, ak mbooloo, mbaa moom doww, fu àdduna daje mbaa deet, jarali ko ci njàngale mi, ci ay jëf, ci jaamu yi ak xarbaax.
96 Nit ku ne am na sañ-sañ wax mbaa bind lu ko soob. Ci waxam yooyule kenn menuko ce bundu xatal. Te it am na sañ-sañ di gëstu, di jot, di wasare ci anam gu yaa ay xabaaraki xalaat ak ay jumtukaay yu mi Men ti jefandikóo.
104 1. Nit ku ne am na sañ-sañ bokk ci ñiy doxal mbiri réewam. Mu teewal fa boppam, mbaa mu yabal ab ndaw mu teewal ko fa.
111 Nit ku ne meññeefu askan wi am na sañ-sañ ñu aar ko ci giru dundam. Ci dundam war na ci am xol bu sedd ci sañ-sañam yooyu, lu aju ci koom-koomam, ci dundinam ak ci lépp lu aju ci aadaam te di ko jox maanaa ak yookkute gu ànd ak tawfeex ci wàllu darajaam, loolu lépp nag ku ne doomu réew mi indi dooleem ak di jokkalante ak bitim réew te mu méngook tërërin ak am-amu réew mu ne.
114 1. Nit ku ne am na sañ-sañ liggéey, tànn it ci eanam gu ko neex liggéeyamm te mu dëppóok ay sàart yu yam te baax ci wàllu liggéey. Te it ñu aar ko ci ñàkkub liggéey.
118 3. Keépp kuy liggéey am na sañ-sañ ñu jox ko pay gi mu yellool, baax te mën koo dundal ak njabbotam te mu yellook sagu doomu aadama, mu mottaliku it ak yeneeni pexe su mënee am ngir aar dundinam.
126 1. Nit ku ne am na sañ-sañ am dundingu yamamaay ngir dëgëral wér-gi-yaramam, raataageem ak bu njabootam, lrawatina ci wàllu lekk col, dëkkuwaay, lépp lu aju ci wàllu paj ak bépp yëngu-yëngu gu am farata ci wàllu dundam. Am na it sañ-sañ ñu aar ko bu liggeeyatul bu feebaree, bu amee laago, ñàkk saxnaam mbaa sërinam, mbaa màgget, mbaa mu ñàkk li muy suturloo ci anam yu dul ci cootareem.
131 1. Nit ku ne am na sañ-sañ ñu jàngal ko, njàng mi waruñu ci fayaku lu mu bon bon ci njàng mu suufe mi te am solo. Njàng mu suufe mi lu war la. Njàng mu xarala mi, te it aju ci wàllu liggéey war nanu koo wasaare. Amul xeej ak seen njàng mu kawe mi ubbil nañu ko képp ku ko yelloo.
140 2. Nit ku ne am na sañ-sañ ñu aaral ko lépp lu aju ci lu mudefar ci wàllu la xarala, mbind mbaa lu aju ci wàllu caala.
146 1. Nit ku ne am na ay wareef yu ko war digganteem ak dëkkandoom yi ngir dëgëral ci anam gu ya darajaam.
148 2. Nit ku ne buy doxal ay sañ-sañam aki tawfeexam war naa sallook li ko yoon may, ngir mu mën a nangu, naw, sañ-sañ nawleem ba léepp lu aju ci yiw, teey ak naataange gu yaa sax ci askan wi.